CONTRIBUTION
Maudit sois-tu et retourne en enfer
Auprès de tes diables de frères
Toi qui terrasses toi qui tues
Qui suscites terreur et frayeur dans les cœurs
Toi qui installes le désarroi dans les esprits
Et partout sur terre d’Est en Ouest, du Nord au Sud
Toi qui brises les reins des économies
Qui fermes écoles et instituts Mosquées et Eglises
Maudit sois-tu et retourne en enfer
Auprès de tes diables de frères !
Toi qui as pris en otage la société entière
Cadenassé à double tour rues et domiciles
Maudit sois-tu et retourne en enfer
Auprès de tes diables de frères
Tu ne m’empêcheras pas pourtant de dire
Gloire à vous braves combattants et combattantes
Gloire aux travailleurs de tous ordres
Médecins, personnels soignants, forces de sécurité,
Authentiques soldats de la Nation
Qui savez en l’être humain apprécier la dignité
Soulager et le corps et le cœur et l’esprit et l’âme
Vous concitoyens qui aimez ce pays
Savourez les mélodies de tous ces artistes
Qui sensibilisent et qui préviennent
Admirez tous ces artisans et tailleurs
Confectionnant pour nous tenues et masques
De jour et de nuit sans jamais se lasser
Fantastiques tous ces jeunes
Prodiges et as des nouvelles technologies
Honneur aux chercheurs et aux créateurs
Vous témoins actifs et féconds de votre propre histoire
Qui avez su répondre présents au rendez-vous de l’Histoire !
Vérité hier vérité aujourd’hui :
« L’Homme est le remède de l’Homme »
Et je puis rajouter et je puis affirmer :
« L’esprit critique et de discernement e
Et le remède de l’Homme »
Concitoyens compatriotes, il est venu le temps
De nous secouer de nous remettre en question
Le temps de nous abreuver de savoir et de science
De nous armer jusqu’aux dents
D’esprit critique et de discernement
Pour être sevrés à jamais des berceuses qui endorment
Et des mensonges qui aliènent.
Au combat, citoyens ! Au combat, patriotes !
A la tâche encore à la tâche
Sans fatigue ni relâche
Avec en bandoulière la foi immense
En nous-mêmes, en notre peuple, en notre avenir
Les yeux fixés vers le même horizon
Parcourant ensemble le même chemin de lumières
Pour la dignité du genre humain
Aujourd’hui et demain.
Version Wolof
KORONAA, MBAS MA LA !
Mbas ma la bόoxun ma la subόoxun ma la !
Yaw miy tëral yaw miy rey
Di yee fitnë di rëccal fit yi
Yaw miy jaxase xel yi tey lëmbé àddina si
Kow ba suuf ndeyjoor ba càmmoñ
Mbas ma la yaw miy nërméel koomkoom
Di tëj lekkool yeek daara yi Jumaa yeek jàngu kërcaan
Mbas ma la bόoxun ma la subόoxun ma la !
Yaa wër ndombo dund gi
Jël caabi-lawbe tëj ràpp
Mbedd yeek dëkkuwaay yi
Mbas ma la bόoxun ma la subόoxun ma la !
Moonte maa ngi naan Waaw gόor waaw jigéen,
Yéen liggéeykat yi Fajkat yeek kaarànge gi
Yéen jàmbaari réew yi fonk doomu aadama
Di xettali ci moom yaram wa, xol baak ruu ga.
Yaw doomu réew aji bëgg réew
Déglul ma woykat yay yeeteeka artu
Gisal ma tajoor yay ñaw muurukaayi kanam ya,
Guddéek bëcëk toqi wu ñu
Xoolal ma ndaw ya ca xarala yu yees yi,
Sargalal ma gëstukat yeek fentkat yi
Ñoom ñi maaseek jamono
Ba indi tegal nu jumtukaay yi méngόok jamono!
Dëgg feeñaat na tey, naa wax ko waxaat ko
« Nit nitay garabam » !
Ma teg ci tegaat ci : « Nit nitéey garabam » !
Nanu xoolaat sunu bopp
Sàkku xamxam roggantikoo ràññee
Ba fer ciy aayόo nenne aki naxee mbaay
Aywa léen doomi réew aji bëgg réew
Ñeme waar ñeme coono
Gëm sunu bopp ak sunu askan gëm sunu ëllëg
Looloo di bokk jëmu ci yoonu bokk tedd tey ak ëllëg !
Madieye MBODJ